У нас вы можете посмотреть бесплатно Seydina Insa Wade , Omar Blondin - Afrig + Xalima la Plume, Documentaire d'Ousmane William Mbaye или скачать в максимальном доступном качестве, видео которое было загружено на ютуб. Для загрузки выберите вариант из формы ниже:
Если кнопки скачивания не
загрузились
НАЖМИТЕ ЗДЕСЬ или обновите страницу
Если возникают проблемы со скачиванием видео, пожалуйста напишите в поддержку по адресу внизу
страницы.
Спасибо за использование сервиса ClipSaver.ru
Omar Blondin Jóob - Afrig Fentkat & woykat bi: Seydinaa Isaa Wàdd Talli yaak taax ya di fuddu Ak di yuuxu di xar, Woto ya tàkk jëppeet! Dëmm ya wër sëg ya, Xooj ko ci ag séndël, Sëg ya di salliiru. Ma làmboo leer, jaar sëg ya, Junniy Omar dekki, Ñi ngiy sulli waa Ndeer ak ñi fi Caaroy, Géeju fen waa ngi nii di baawaan, Yàlla mi nu tiim, Ñàkk du nu tax a miim, Walla di wër di leb a leb a leb.... Le grand paragon (pharaon?), c'est Omar, Jàngal ndaw, ngir mooy li war. Jaasi du fi génn mbar, Xanaa ci lu ko jar. Raatale, umple, tële, Xamuñu, bëgguñu, sañuñu. Du doole fasu naaru góor, Du taaru jongoma ju mat, Loolu lépp dafay ruur. Ceddo amul kurus, Wante du rus. Eéy! Dégluleen yuuxu suufu Senegaal, Ànd ak yuuxu salup bi ci Gore! Sama fàttaliku di metti, Saa làmmiñ di saf deret. Bóom nañu Omar Jóob, Na ñu bóome waa Ndeer Ak ñi ci Caaroy! Géej giy jiñax(?), di ŋaax, Ngelaw liy tëb di sab ni rab, Asamaan siy dënu ni kënu, Niir yi di xaacu ngir di naqarlu, Talli yaak taax yay fuddu Ak di yuuxu di xar, Woto ya tàkk jëppeet! Dëmm ya wër sëg ya, Xooj ko ci ag séndël, Sëg ya di salliiru. Ma làmboo leer, jaar sëg ya, Junniy Omar dekki, Ñi ngiy xulli waa Ndeer ak ñi fi Caaroy. Ceddo amul kurus, Wante du rus... Ki jukki woy wi: Jolof Gaal