У нас вы можете посмотреть бесплатно Manatumaa jekki ta nekkumay jooy - Wolofal Serigne Moussa Ka par S. Ibrahima Lo или скачать в максимальном доступном качестве, видео которое было загружено на ютуб. Для загрузки выберите вариант из формы ниже:
Если кнопки скачивания не
загрузились
НАЖМИТЕ ЗДЕСЬ или обновите страницу
Если возникают проблемы со скачиванием видео, пожалуйста напишите в поддержку по адресу внизу
страницы.
Спасибо за использование сервиса ClipSaver.ru
Manatumaa jekki te nekkumay jooy Sëriñ bi cëy àddina yaaka maa juuy Sëriñ bi waa ju ko jisoon ci sab xol Koo mantee jis it mu sew ci sam xel Sëriñ bi waa ju ko jisoon mu jis la Koo manatee jis it du tax mu doy la Sëriñ bi waa ju ko mosoon mu mos la Koo manatee mos it du tax mu saf la Sëriñ bi gaayi ko amoon te ñàkk-ko Kuñ manatee ñàkk it du tax ñu faale ko Sëriñ bi gaayi ko hamoon te xewle ko Moo tee ñu dëgmu far di jooy ba fekki ko Sëriñ bi waa kërëm ña nekkoon Njaareem Seen xol yi dootu jis lu rëy bam jara yéem Sëriñ bi waa kërëm ñi nan leen wormaal Te fonk leen def leen i nday bu kenn laal Sëriñ bi saahir si dafay melow nit Baatin bi leppi Yàlla éey du leen nit Sëriñ bi xar-baax la gu Yàlla feeñal Amul nirook i nawle mbaa kuy feeñal Sériñ bi doomam yile nana leen jiital Di leen siyaare bir yi bun ko juutal Sëriñ bi cam soo ca xiyaas mu yées ko Te moom palaas boo ko wutal mu fees ko Sëriñ bi yaw xeetoowulaak malaaka Te doo rawaan doo jinne doo Muusaa Ka Sëriñ bi yaw niroowulaak sahaaba Yaa raw ñadaan xool di janook kahaaba Sëriñ bi yaw yaa jiitu gaayi diiwaan Yaa raw ñadaa feeñal i mbóot di baawaan Sëriñ bi yaa raw gaaya daan fanaani Haras di xuus ca dexi leer yay naani Sëriñ bi jéggi nga palaasi xutbu Ngir sàkk ngay xawsu yu sàkk i xutbu Sëriñ bi yaw niroowulaak Jiilaani Fafoo nirook Saasali baa Tiijaani Sëriñ bi yaw yaa boole mbóotam ngir ya Ak àtteyaak sañ-sañ ya ak seen leer ya Sëriñ bi yaw jàll nga ngiirum wirdu Yaw sab muxaddam du jubook i ardo Sëriñ bi weesu nga mbirum wilaaya Xam-xam bi it raw na xamug diraaya Sëriñ bi yaw niroowulaak waliyu fafoo nirook ñay woote ak mahdiyyu Sëriñ bi yaw Yàlla a ne laa naabiiyaa Nde kon ku lay woo far ne yaa nabiiyaa Sëriñ bi yaw yaa wuutu ngën ji yonnen Saa gëti xol jis na ko dootu wànnen Sëriñ bi bir yaak melo yaak jikkoom ya Day saf meloy yonnen ba ak soloom ya Sëriñ bi muñ gaak nattu yaak wakiirlu ga Day saf muñug yonnen ba ak cellerlu ga Sëriñ bi wéetal gamu wéetal Yàlla boo koy xalam mu doy la far ci Yàlla Sëriñ bi xér gaak tabe gaak njàmbaar ga Day saf tabeg yonnen ba ak yàkkaar ja Sériñ bi nooy gaak kersa gaak yërmaande ja Day saf xolub yonnen ba ak yërmaande ja Sëriñ bi ham gaak dëddu gaak lewet ga Day saf dëddug yonnen ba ak hamam ga Sëriñ bi teey gaak raglu ga lewam ga Day saf ku xool yonnen ba ak muuñam ga Sëriñ bi wax jaak waare waak haddiis ja Day saf fu yonnen jekki mbaa Xadiija Sëriñ bi nim wootee ci yoonu tarbiya Day saf na yonnen ba defoon cig tarqiya Sëriñ bi nim seexale gaayi wuyusi Day saf na yonnen ba defoon Xuraysi Sëriñ bi ñam tarbiya woon ca baawon Raw nanu jéeg ngir seen i xol lañ jaayoon Sëriñ bi nim leerale taalub lislaam Day saf jihaar ju mag ja fentoon lislaam Sëriñ bi moo laxasu yeesal diine Fekkoon na taal bay bëgg a fay fasànna Sëriñ bi moo bayaat lu toolub sunna Ku ne di bay di haj di gën di sonn Sëriñ bi moo tuxal bidaa ci réew mi Ak aada yuy jaahil sosoon ci réew mi Sëriñ bi tax surga du faale ngonnal Te xam ne dañ daa ngonlu booleek nendal Sëriñ bi tax kaamil di jar ay téemeer Te xamne daawul jar lu weesu fanweer Sëriñ bi moo dindi ci réewum soodaan Kuy wacc mbaa kuy wàlli nuqiy seetaan Sëriñ bi moo tax mag ña woon ca baawon Bàyyi tux ak fóon ak yu mel ni yaa woon Sëriñ bi moo tax bépp séeréer bàyyi naan Bawal-bawal ba sàcc pël bàyyi safaan Sëriñ bi tas daara yi samp i daaru Ngir daara yee dañ daa doroo ka taaru Sëriñ bi tax sàmm si dootun wax óow Ken du ne naam giwal ba xaste ak coow Sëriñ bi tax ba ndaw ñi màggal mag ñi Ba mag ñu baax ñi far di jiital ndaw ñi Sëriñ bi tax ba nun wolof nu tekki Te xam ne ken daawu fi dox di fokki Sëriñ bi tax waa Màkka ak Madiina Difi siyara si di wutsi diine Sëriñ bi tax deefu nu yët hidaaya Te xam ne noo daa yóbb ay hidaaya